Suma woyofé lool nguani dama ñakk fayda
Ma jaar si digg wah nimqko gise ngani dama ñakk kersa
Te woyof lool woute na akk ñakk fayda
Jaar ci digg wahi tam wute na ak ñakk kersaa
Giss nga rawante doje ak kayit diisatah kayit jiitou doje
Soo sete basi biir yow xamuloo linga beug
Digante bo giss moussante massuko yorr
Ginaaw lu yagg degla bule ragal degg gi
Degg moom kaani la koko tufe mu tohoñu
Te degg moy fondement lep lo giss
Degg gi moy benn jigen waratul dess ginaaw
Gemm li nga doon
Ham li nga beug ñaari lohoy takk tubay te moy takk serr
Bañe na, bañe na duma femme objet
Ñaari lohoy takk tubay te moy takk ser
Balaa may beg dee nga naan jigen ligeyoul
Te eumb juroom ñenti weer weusin dara genouko metti
Jigenangi arme, jigenangui tool ya
Jigenangi ci bureau yee
Su goor teke jigenangi si wetam
Yow sama jigen weyal di ñafe linga beug ngala busi tayi fekk jotuloko
Gem li nga doon
Ham linga beug, ñari lohoy
Jigen ñi yag nano wane pasteef demb ba tey jile
Yacine Boubou, Aline Sitoe diatta, Sokhna Mame Diarra Bousso
Mame Fawade Wele etc yen jigen Senegal yagg nguen wane sen bopp
Heuthie bu dikoul dagg
Sister bañal yow bañal fekk jotoloko